La lettre en wolof

wolof

La lettre en wolof

Publiée par Lettre aux parents confinés sur Lundi 25 mai 2020
Bataaxal giir waajuri toog sèn kër

Ňun dé dinaňu dajéwat nèk bèn njaboot.

Massuňu toog luyaguéni ak suňuy doomyi.

Daffa jott ňu wax ak ňom. Wax ak ňom yèni say, numu gënë yagg si niň ka daan déffé.

Daffa jott ňu lèn di dëglu. Ňu lèn di dëglu numu gënë yagg si niň ka daan déffé.

Daffa jott ňu gën lèn xaam.

Wax ak suňu doomyi moy li gën ndax ňu jègui mettit bi : dalalanté suňuy xèl, jappalanté, waxanté li am njariň.

Wax tan ak suňuy doom, ndax ňulèn di güngé ňu déff sèn warèf : waxtan ak ňom thi mbirru lécol ak liggéey, wax thi sèn ndiaxaré ak sèn tekki, lolu molèn di dieumalé kanam, thi waxtu bu metti bi ak buňu délluwé daara !

Warèf yi lèn jox daara ja giir ňu dèf ci ko ci kërgi mo wara gënë tax ňu wawtan ak ňiom.

Xaaléyi mënnaňu itam nattali sèn waajuri liňu mokal ak liňu mokalul, lu metti ak lu yomb.

Si lolu, xalébi su amé luko jaxal itam mëna woo téléfòn bèn tante, nidiay, xarit wala sax bèn dékandor giir mëna mokal.

Mënnaňko déff si yoyu anam, doon té dara léruci.

Lèpp lu jangalékatti yonné rek xaaléyi mënay ko déff.

Jangalékatti daňi itam yonné ay liggéey yu metti yi nga xamanténi xaaléyi dina ňu jël ay waxtu disso ak yèn ak séni laj giir jéma xam.

Lèg lèg dafay metti torop : wayé jarul tit, danxté danaň ko guiss suňu délluwaté daara ja.

Lajtélèn sèn doomi liňu mokal, donté waxnaňlèn ni « mokaluňu dara ».

Waxlèn linga thi xaalat, gèn jangandor.

Soxlawunsi sa xaraňté wala sa mënin, lu ci am solo moy wéthio xalat bi.

Giir waajuri yi lak bénèn xètu kaalama té wuté ak bu daara bi : lak moy « wax ak dëglu », moy wéthio, moy sèddo, ak thi kaalama wala ay kaalama yiňu bëgë, té ňu min lèn.

Kaalamayi yèpp baaxnaňu, amnaňu njariň, téxci am xëyma giir waxtan ak sa doom.

Kaalamayi yèpp am njariň, giir lajté, wax, té-té, merlo, nettali ak léral, rétanando, waala waxtan thi lèpp lu am fullë ak lu amul fullë.

Pur gënë wéthio xalat ak sa doom jafandékol lak wala ay lak yo xamné yombuna thi yaw yombuna thi mom giir mu gawa mokal.

Té ga bayi sa doombi taan kaalamabi wala kaalamayi yumu bëgë jafandéko, li am solo moy wéthianté xaalat bi, jërëjëf.



Citer ce billet
Laurie Boyer (2020, 25 mai). La lettre en wolof. ELSE - Éducation en langues secondes et étrangères. Consulté le 29 mars 2024, à l’adresse https://doi.org/10.58079/o5r5

Vous aimerez aussi...

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Ce site utilise Akismet pour réduire les indésirables. En savoir plus sur comment les données de vos commentaires sont utilisées.

Rechercher dans OpenEdition Search

Vous allez être redirigé vers OpenEdition Search